Hebrews 8:5 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Saraxalekat yooyu ñu ngi liggéeyal Yàlla ca màggalukaay, ba nekk misaal tey takkandeeru yëf yu dëggu, ya féete kaw. Moo tax ba Musaa naree defar tàntu màggalukaay ba, Yàlla artu na ko ne ko: «Teeylul ba def lépp, roye ko ci bi ma la won ca tund wa.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Sarxalkat yooyu, jaamookaay bi ñuy liggéeye, ab misaal la, takkndeeru yëf yu dëggu ya fa asamaan la. Ndax ba Musaa di waaja yékkati xaymab jaamookaay ba, noonu lees ko artoo woon ne ko: «Nanga xool te def lépp, mu dëppook misaal mi ñu la won ci kaw tund wi.»