Hebrews 9:10 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Sarax yooyu ñu ngi jëmoon ci lekk ak ci naan ak ci fànn yu bare ci mbirum sangu set. Ay sàrt yu jëm ci yaram lañu, yu ñu waroon a farataal, ba kera jamono ji Yàllay tëral kóllëre gu bees.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Sarax yooyu, ci aw ñam ak ag naan, ak xeeti njàpp doŋŋ la jëm, lépp yittewoo yaramu suuxu neen, te di ndigal yu leen waroon ba keroog bésub coppite taxaw.