Hebrews 9:12 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Noonu Kirist dugg na benn yoon ba fàww ca bérab bu sell-baa-sell. Duggu fa ak deretu sikket yi ak yu yëkk yi. Waaye mi ngi duggaale ak deretu boppam te indil na nu noonu njot gu amul àpp.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Du deretu sikket mbaa yëkk la duggaale, waaye deretu boppam la dugge benn yoon ba fàww ca bérab bu sell baa sell, te moom la amale njotlaay gu sax dàkk.