Hebrews 9:14 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Su fekkee ne noonu la deme nag, du kon deretu Kirist moo ëpp doole? Jox na bakkanam Yàlla, def ko sarax su amul sikk jaarale ko ci dooley Xel miy sax abadan. Kon deretam moo man a sellal sunu xel, mi nu doon yedd ndax jëf yu jëm ci dee, ngir nu man a jaamu Yàlla jiy dund.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
te Almasi di ki def boppam sarax bu mucc sikk ñeel Yàlla, ci dooley Noo gu Sell gi, kon nag ñaata yoon la deretu Almasi gëna mana setal sunu yaraange ji sababoo ci sunu jëf ju bon ju jëme ci ndee, ba nu mana jaamu Yàlla jiy dund!