Hebrews 9:19 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Keroog Musaa jàng na ndigali yoon wépp ci kanamu bànni Israyil gépp. Gannaaw loolu jël na deretu wëllu, jëlaale ndox, ak bantu garab gu ñuy wax isob, laxas ci kawaru xar mu xonq. Noonu mu capp ko ca deret ja, daldi ko wis ca téereb yoon wa ak ca mbooloo mépp
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Keroog ba Musaa biralalee bànni Israyil gépp mboolem santaane, na ko yoon wi laaje, ba mu noppee, deretu wëllu la jël, ak ju sikket, akum ndox, ak caru garabu isob bu mu laxas kawaru xar mu xonq. Mu capp ko ca deret ja, wis-wisal ca kaw téereb yoon wa, ak mbooloo mépp.