Hebrews 9:23 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Yëfi àddina yi misaal yu dëggu yi ci asamaan, war nañu leen a sellale noonu. Waaye yëf yu dëggu yooyu ci asamaan, laaj na sarax yu gën a baax, ngir ñu sell.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Jumtukaay yooyi di ay misaali yëf ya fa asamaan, yooyu sarax lees ko waroona setale. Kon yëfi asamaan ya ci boppam, sarax yu ko gën lees ko wara setale.