Hebrews 9:26 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Bu demee woon noonu, kon dina sonn ba tàyyi ca njàlbéenug àddina ba tey. Waaye nag benn yoon rekk la feeñu ci mujjeelu jamono yi, joxe boppam ni sarax ngir far bàkkaar yi.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Lu ko moy ca njàlbéenu àddina lay dale sonn ay yooni yoon. Waaye tey ci mujug jamono yi la feeñ benn yoon doŋŋ, ba sarxe boppam, ngir far bàkkaar.