Hebrews 9:4 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Saraxalukaayu wurus, ba ñuy taal cuuraay ca kawam, a nga fa woon, ak gaalu kóllëre, ga ñu taf wurus ba mu daj. Ca biir gaal ga amoon na fa benn njaqu wurus bu defoon ñam, wi ñuy wax mànn, ak it yetu Aaroona wi jebbi woon, ak àlluway doj, ya ñu bindoon wax yi kóllëre gi ëmb.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ca la sarxalukaayu wurus ba ñuy taal cuuraay bokkoon, gaalu kóllëre ga nekk moom doŋŋ ca biir néeg bu sell baa sell, ñu xoob ko wurus ba mu daj. Gaal ga moo yeboon njaqal wurus la defoon ñam wa ñuy wax mànn, ak yetu Aaróona wa jebbi woon, ak àlluway kóllëre ga.