Hebrews 9:7 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye ca néeg ba ca topp, saraxalekat bu mag ba rekk moo fa daan dugg benn yoon ci at mi. Te daawu fa dugg mukk te yóbbaalewul deretu mala, yi muy jagleel Yàlla, ngir bàkkaari boppam ak yu mbooloo mi daan def ci seen ñàkka xam.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Waaye ñaareelu néeg ba, sarxalkat bu mag ba doŋŋ moo ca daan dugg, benn yoon cim at, te du ñàkka duggaale deret ju muy jooxe ngir boppam, ak itam ngir bàkkaar yi askan wi def te du ag teyeef.