Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Su boobaa ñu indil Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, galag bu bawoo ci xeet wu siggi, rattax yaram, askan wu ñu ragale fu jegeek fu sore, xeet wu am doole, di falaxee, te seenum réew defi wal, galag ba agsi ba tundu Siyoŋ, fa Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dëël turam.