Isaiah 36:16 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Buleen déglu Esekiya. Buurub Asiri kat dafa wax ne: Jàmmooleen ak man te ngeen génn dëkk bi, dikk nangul ma. Su ngeen ko defee, ku nekk ci yeen mana lekk ak jàmm ci garabu reseñam, lekk ak jàmm ci figgam, di naan ndoxum teenam,