Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ana lu tax ba ma dikkee, kenn nekku fa? Ma woote, kenn wuyuwul? Damaa gàtta gàtt loxo, ba manumaa walloo? Am damaa ñàkk doole ju ma xettlee? Xanaa du maay gëdd géej, mu wow, maay defi dex màndiŋ, ndox tukki; jën ya mar, dee ba yàqu?