James 3:17 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye xel mi jóge ci kaw daa sell, ba noppi ànd ak jàmm te lewet, nooy, fees dell ak yërmande ak jëf yu rafet; àndul ak genn parlàqu, amul genn naaféq.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la jëkka def, teg ci ànd ak jàmm, akug dal. Day taxa neexa jubool, feese yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-làqu akug jinigal.