James 5:12 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Te li fi raw samay bokk, buleen waat mukk, bu muy ci asamaan mbaa ci suuf mbaa ci leneen lu mu man a doon. Nangeen yem ci: «Waaw,» ak «Déedéet,» ngir bañ cee layoo fa kanam Yàlla.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Li ci raw nag bokk yi, moo di buleen giñ, bu muy ci asamaan mbaa ci suuf mbaa ci leneen lu mu mana doon. Na seen waaw di waaw, seen déet di déet, bala ngeena tàbbi ci mbugal.