Jeremiah 28:11 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Anaña àddu fa kanam mbooloo ma mépp ne leen: «Aji Sax ji dafa wax ne: Nii laay damme yet wi buur Nabukodonosor buuru Babilon di tënkee. Fii ak ñaari at tembe dinaa jële yet wi ci ndoddu mboolem xeet yi mu ko tënke.» Ba loolu amee Yonent Yàlla Yeremi dem yoonam.