Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Yeremi ne Cedesyas: «Aji Sax ji, Yàllay Israyil, Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Soo nangoo génn rekk, jébbali sa bopp kàngami buuru Babilon déy, dinga rawale sa bakkan, te dëkk bii du lakk ba jeex. Dinga dund yaw, yaak sa waa kër.