Jude 1:3 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Samay bokk, bëggoon naa leen a bind lool ci mbirum mucc gi nu bokk, waaye lii moo gën a jamp: ma xiir leen, ngeen taxaw ci aar mboolem dëgg, yi Yàlla xas a dénk gaayam yu sell yi ba fàww.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Soppe yi, yàkkamti woon naa leena bind ci mbirum mucc gi nu bokk, waaye fàww ma bind leen, ngir ñaax leen ci xeexal yoonu ngëm, wi Yàlla xasa dénk ñu sell ñi, benn yoon ba fàww.