Jude 1:5 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Xam ngeen loolu lépp ba noppi sax, waaye dama leen koy fàttali rekk. Xam ngeen ne Boroom bi musal na xeetam, ba génne leen réewu Misra, waaye gannaaw ba raafal na ñi gëmul woon.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Doonte xam ngeen loolu lépp ba noppi, dama leen di fàttli rekk ne Boroom bi moo jëkka musal ñoñam, génne leen réewum Misra, te gannaaw gi moo raafal ña gëmul woon ca ñoom.