Jude 1:7 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Noonu itam dëkki Sodom ak Gomor ak dëkk ya leen wëroon, dañoo sóobu ci njaaloo ak di def ay góor-jigéen, waaye àtte bi dal na ci seen kaw, ba ñuy ay tegtal ci ñiy yelloo safara ba fàww.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Naka noonu itam Sodom ak Gomor, ak dëkk ya leen wër, ñoo yebu woon ci powum séy, ak jaxasoo gu woroo ak bindub judduwaale, ba ñu def leen misaal, ñeel ña nara tegoo mbugalum sawara wu sax dàkk.