Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
«Su amul lu mat njégu ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw, li muy indi, sarxal ko ngir bàkkaar bi mu def, ñetti kiloy sunguf su mucc ayib lay doon, muy saraxu póotum bàkkaar. Du ci def diw, te du ci sotti cuuraay, ndax li mu di saraxu póotum bàkkaar.