Luke 12:1 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Gannaaw loolu, naka la mbooloo ma dajaloo ba mat ay junniy junniy nit, di tancante, Yeesu tàmbalee wax jëmale ca taalibeem ya ne leen: «Moytuleen lawiiru Farisen ya, li di naaféq.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Mbooloo ma nag mujj na dajaloo ba mat ay junniy junniy nit, bay joggeente. Ci biir loolu Yeesu tàmbalee wax, jëkke ko ci ay taalibeem, ne: «Wattuleen lawiiru Farisen ñi, te mooy jinigal.