Luke 12:37 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Surga yooyee seen njaatige fekkul ñuy nelaw, ba mu agsee, ñoo gën a yeyoo ngërëm. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina sol yérey waañ, wax leen ñu toog lekk, ba noppi indil leen ñam wi.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndokklee surga yooyu seen njaatige dikk fekk ñu teewlu. Maa leen ko wax déy, njaatige leey takku, toogal leen ba noppi dikk, taajal leen, ñu lekk.