Luke 13:14 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye njiitu jàngu ba mer, ndax li Yeesu fajoon nit ca bésu noflaay ba, mu ne mbooloo ma: «Am na juróom-benni fan yu nit ñi war a liggéey. Kon war ngeen a ñëw faju ci bés yooyu, waaye du ci bésu noflaay bi.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Njiitu jàngu ba nag yékkati kàddug ñaawlu ndax bésub Noflaay ba Yeesu faje. Mu ne mbooloo ma: «Juróom benni fan la nit ñi wara liggéey. Kon ci fan yooyu ngeen wara fajusi, waaye du ci bésub Noflaay.»