Luke 14:12 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Noonu Yeesu ne ki ko woo woon lekk: «Boo dee woote añ walla reer, bul woo rekk say xarit, say doomi ndey, say bokk, walla say dëkkandoo yu am alal. Lu ko moy ñooñu itam dinañu la woo, fey la bor bi.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ci kaw loolu Yeesu ne waa ja ko woo bernde: «Boo dee waajal bernde, añ mbaa reer, bul woo say xarit, mbaa say doomi ndey, mbaa say bokk, mbaa say dëkk yu am alal, nde ñoom itam dañuy walbatiku, woo la rekk, mu doon sag pey.