Luke 20:46 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
«Moytuleen xutbakat yi; dañoo bëgg di doxantu, sol ay mbubb yu réy, te ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ci pénc mi. Ci jàngu yi, toogu yu féete kanam lañuy wut, te toogu yu yiw lañuy taamu ci reeri xew yi.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
«Moytuleen firikati yoon yi taamoo jaagar-jaagareek seen mbubb yu réy, di sàkku nuyoob gëddaal ca pénc ma, ak toogu yu kaname ca jàngu ya, ak péetey teraanga ca bernde ya.