Luke 22:27 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ki toog ca lekkukaay ba, moom ak surgaam, ñoom ñaar kan moo ci gën a màgg? Xanaa du ki toog ci lekkukaay bi? Waaye man maa ngi ci seen biir ni surga.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ki ñu taajal ndab li, ak surga bi ko taajal, ana ku ci gëna kawe? Xanaa du ki ñu taajal? Moonte man, ci seen biir laa tooge toogaayu surga!