Luke 23:25 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Mu bàyyil leen ki ñu ko ñaanoon, kooku ñu tëjoon kaso, ndax tas réew ma ak rey nit. Waaye mu jébbal leen Yeesu ci seeni loxo.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Mu yiwi ka ñu ko ñaanoon, te jëfi fippu ak nit ku ñu bóom taxoon ñu tëj ko kaso. Yeesu nag, mu teg ko ci seeni loxo, ngir ñu def ko lu leen neex.