Luke 23:50 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Nit ku ñuy wax Yuusufa dem ca Pilaat. Mi ngi dëkk Arimate ca diiwaanu Yude. Yuusufaa nga bokkoon ca kureelu àttekat yi. Nit ku baax la woon te jub, te àndul woon ci li ñu dogaloon te jëf ko. Da doon séentu nguuru Yàlla.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ndeke jenn waay ju ñuy wax Yuusufa, ma nga bokkoon ca kurélu àttekati Yawut ya. Ku baax, ku jub la woon.