Luke 24:44 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Noonu mu ne leen: «Bi ma nekkee ak yéen, waxoon naa leen baat yii: li ñu bind lépp ci samay mbir ci yoonu Musaa ak ci téerey yonent yi ak ci Sabóor dafa war a am.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ci kaw loolu mu ne leen: «Lii moo di kàddu ya ma leen waxoon ba ma nekkee ak yeen. Noon naa leen: Mboolem li ñu bind ci samay mbir ci yoonu Musaa, ak ci téerey yonent yi, ak ci Sabóor, fàww lépp sotti.»