Luke 3:14 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Ay xarekat laaj nañu ko ne: «Li jëm ci nun nag?» Mu ne leen: «Buleen néewal doole kenn, jël xaalisam ci kaw ay tëkku mbaa ci seede lu dul dëgg. Waaye doylooleen li ñu leen di fey.»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ay takk-der itam ne ko: «Nun nag, nu nuy def?» Mu ne leen: «Buleen néewal kenn doole, mbaa di duural kenn ngir jëlal ko dara; doyloo leen seen peyoor.»