Luke 3:7 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Mbooloo ma daan ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, Yaxya daan na leen wax naan: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co! Ku leen artu ngeen daw merum Yàlla mi nar a wàcc?
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Yaxya nag di wax mbooloo may ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, naan leen: «Yeen njurum jaan mee, ku leen àrtu, ba ngeen di daw sànj miy dikk?