Luke 4:25 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ca jamonoy Iliyas, bi mu tawul lu mat ñetti at ak genn-wàll, te xiif bu metti am ca réew mépp, amoon na ca Israyil jigéen yu bare yu seen jëkkër faatu.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Maa leen wax ne liy dëgg moo di, ca jamonoy Ilyaas, ba asamaan tëjoo diiru ñetti at ak juróom benni weer, ba xiif bu metti am ca réew mépp, ay jëtun ñu baree nga woon ca Israyil.