Luke 4:41 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Te it ay rab di génn ca nit ña te di yuuxu naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Noonu mu gëdd leen, te mayu leen, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ne, mooy Almasi bi.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ay rab itam di génn ñu bare, di yuuxu, te naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Teewul mu gëdd leen, aaye leen ñu wax, ndax xamoon nañu ne mooy Almasi.