Luke 5:17 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Am na bés Yeesu doon jàngale. Amoon na ca mbooloo, ma teewoon, ñu bokkoon ca Farisen ya ak ay xutbakat yu jóge ca dëkk yépp, ya ca Galile ak ya ca Yude ak Yerusalem. Yeesu àndoon na ak dooley Boroom bi, ba muy faj ay jarag.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Yeesu moo doon jàngle bés, fu ay Farisen ak ay jànglekati yoonu Musaa tooge, jóge ca mboolem dëkki Galile ak Yude ak Yerusalem, te manoorey Boroom bi teew faak moom, ngir faj jarag ja.