Luke 5:36 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Te it Yeesu wax leen léeb wii: «Kenn du jël mbubb mu bees, xotti ci sekkit, daaxe ko mbubb mu màggat. Lu ko moy, dina xotti mbubb mu bees mi, te sekkit, wi mu ci jële, du ànd ak mbubb mu màggat mi.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Yeesu léebati leen, ne leen: «Mbubb mu bees, deesu ci xotti ab sekkit, ngir daaxe ko mbubb mu ràpp. Lu ko moy mbubb mu bees mi xottiku ba noppi, te du tax sekkit wu bees wi ànd ak mbubb mi ràpp.