Luke 6:17 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Yeesu ànd ak ndaw ya, wàcc tund ya, daldi taxaw ca joor ga, fa mbooloom taalibe mu takku nekkoon. Amoon na fa it ay nit ñu bare ñu jóge ca réewu Yawut ya mépp ak ca dëkku Yerusalem ak dëkk yi nekk ca wetu géej ga, maanaam Tir ak Sidon.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ci kaw loolu Yeesu ànd ak ñoom, wàcc, daldi taxaw ca joor ga. Ay taalibeem yu baree nga fa woon ak mbooloo mu réya réy: ay niti Yude gépp, ak Yerusalem ak Tir ak Sidon, dëkki wetu tefes ga.