Luke 6:48 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Dafa mel ni nit kuy tabax kër, mu gas fu xóot, jot doj wu réy, samp fa kër ga. Bi mbënn ma ñëwee, wal ma dafa dal ca kër ga te yenguwul, ndaxte nit ka dafa tabax kër ga tabax bu dëgër.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Dafa mel ni nit kiy tabax kër, gasa gas ba mu xóot, daldi samp kenu ga ca kaw doj wa ca suuf. Mbënn ma dikk, wal ma rëkk kër gaak doole te manu koo yëngal ndax tabax bu wér ba ñu ko tabaxe.