Luke 8:10 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Mu tontu ne leen: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci des, dama leen di wax ci ay léeb. Noonu la, ngir:“Ñuy xool te duñu man a gis,di dégg te duñu man a xam.”
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Mu ne leen: «Yeen lañu may, ngeen xam mbóotum nguurug Yàlla, waaye ñi ci des ñoom, ci ay léeb lees koy dëxëñ, su ko defee: “Ñuy xoole te duñu gis, di dégg te duñu xam.”