Luke 8:29 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Dafa wax loolu, ndaxte Yeesu santoon na rab wi, mu génn ci moom. Rab wa dafa ko doon faral a jàpp. Nit ñi daan nañu ko wottu, di ko yeew ak ay càllala, ak di ko jéng, mu di leen dagg, rab wi di ko xiir ca bérab yu wéet.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Booba Yeesu tàmbali naa sant rab wi, mu génn waa ji. Rab wi jàpp na waa ji ay yooni yoon. Su ko defee ñu yeewe ko ay càllala, jéng ko, ngir wattu ko, mu di ko dagg, rab wi di ko xabtal, jëme bérab yu wéet.