Luke 9:13 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye Yeesu ne leen: «Joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu tontu ko ne: «Amunu lu dul juróomi mburu ak ñaari jën. Xanaa ndax nu dem jëndal mbooloo mii lu ñu lekk?»
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Mu ne leen: «Yeen, joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Nun de amunu lu dul juróomi mburu ak ñaari jën. Xanaa nu dem, nun ci sunu bopp, jëndali mbooloo mii mépp lu ñu lekk!»