Matthew 5:22 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye man maa ngi leen di wax ne, képp ku mere sa mbokk, dinañu la àtte. Ku wax sa mbokk: “Amoo bopp,” dinañu la àtte ca kureelu àttekat ya. Ku ko wax: “Alku nga,” dinañu la àtte ci safara.