Nehemiah 2:13 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Ma génne dëkk ba guddi, jaare buntu tata ba ñuy wax Xur wa, wutali walu ndox ma ñuy wax walu Ninki-nànka, daldi jàll ba ca buntu Sën ba. Ci biir loolu ma seetlu tatay Yerusalem ji toj fu nekk, bunt yi lakk ba xoyomu.