Nehemiah 2:16 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Kilifay dëkk ba nag xamuñu fu ma demoon, mbaa lu ma doon def. Ndax fekkul woon ma wax kenn dara, du Yawut yi, du sarxalkat yi, du garmi yi, du kilifa yi te du keneen ci ñi wara sasoo liggéey bi.