Nehemiah 3:13 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Buntu Xur wa, Anun a ko defaraat, mook ña dëkk Sanowa. Ñoo ko tabaxaat, taxawal laf ya, ak tëjukaay yaak dénki galan ya cay ànd. Ñu teg ca defaraat làccub juróomi téeméeri meetar ca tata ja, ba àgg ca buntu Sën ba.