Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Bu loolu weesee, la ko dale bés ba ñu ma falee boroom diiwaanu Yuda, ca ñaar fukkeelu atu nguurug Artaserses, ba ca fanweeru atam ak ñaar, muy fukki at ak ñaar, lekkunu alalu galag bu boroom diiwaan yelloo, du man, du samay bokk.