Nehemiah 8:9 — Compare Translations

1 translations compared side by side

Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Gannaaw loolu Neyemi boroom dëkk ba ànd ak Esra sarxalkat ba, di bindkat ba ba tey, ak Leween ñay xamal mbooloo ma, wax ak ñoom ñépp, ne leen: «Bésub tey jii, bés bu sell la, ñeel Aji Sax ji, seen Yàlla. Buleen ci naqarlu, buleen ci jooy.» Booba mbooloo ma mépp a doon jooy ca kàdduy yoon wa ñu dégg.