Philemon 1:16 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
waxuma léegi ni jaam rekk, waaye lu ko sut, xanaa mbokk mu dëggu ci xol, fekk looloo raw ag njaam. Mbokk la ci man, rawatina ci yaw, muy sa jaam ci aada, di sa mbokk léegi ci Boroom bi.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
ba dootu doon sab jaam, waaye day wees ab jaam, di mbokk, di soppe, ma sopp ko lool, te nga war ma koo gëna sopp, ngir jëmmu boppam, ak Sang bi ngeen bokk.