Philippians 1:27 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Waaye dénk naa leen lii: na seeni jëf yelloo ak li Kirist digle ci xebaar bu baax bi. Noonu su ma leen seetsee, mbaa ma dégg seen mbir rekk, dinaa xam ne yéena ngi dëgër ci menn xel, bokk benn xalaat ci bëre luy saxal dëggu xebaar bu baax bi,
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Fexeleen rekk ba di jëfe ni mu yelloo ak xibaaru jàmm bu Almasi, ngir bu ma leen seetsee, mana seede, mbaa su ma wuutee it, di dégg ni ngeen saxoo di mànkoo, bokk jenn yéene, di xeex ngir saxal ngëm gi sukkandiku ci xibaaru jàmm bi.