Philippians 1:7 — Compare Translations

2 translations compared side by side

Wolof 1987
Te juumuma ci li ma xalaat loolu ci yéen ñépp, ndaxte def naa leen ci sama xol; ba tax fii ci kaso bi, ci taxawal xebaar bu baax bi ak lawal ko, yéen ñépp am ngeen wàll ak man ci yiwu Yàlla.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Maa yey nag njortal leen loolu yeen ñépp, ndax ci sama xol laa leen def, te it muy ci wàllu jéng yi ñu ma jénge, di ci wàllu kàddu guy waxal xibaaru jàmm bi, ak di ko feddli, yeen ñépp am ngeen wàll ci sama añub yiw.