Philippians 2:12 — Compare Translations
2 translations compared side by side
Wolof 1987
Noonu samay soppe, xam naa ne, musuleen a jóg ci dégg ndigal, waxuma sax bi ma nekkee ak yéen rekk, waaye rawatina bi ma leen soree. Kon nag maa ngi leen di ñaan, ngeen biral seen mucc ci seeni jëf, te def ko ci ragal Yàlla gu dëggu.
Wolof KYG (Kàddug Yàlla gi)
Kon nag soppe yi, noonu ngeen masa dégge ndigal, démb ba may teew, rawatina tey bi ma wuutee, nangeen ko wéye, di jëfe seenug mucc, te ànd ceek ragal Yàlla bay lox,